Xale

Guddé, maasa guddé
Jeddi ma na konto
Maasa guddé, maasa guddé waw

Yeen xale rewmi
Ni la ko beugue waw

Bismillah niou deeti door dellu saku nian
Di nian Yallah mu nangoul niu lep lun ko nian
Seytané dey yakh khel di sopi xalat
Di feweule andado
Niun daal bum nyu laal yaye

Yeen xale rewmi
Ni la ko beugue waw

Sen atmi mo du atoum gune
Soxlo woul beuri wakh
Nanj dieum bolo teh won mak nyi
Nioy doule rew mi
Gone su taggou ay wadiouram
Disso ak nioom seu ndialbeen
Fu mu né ci aduna senj thia yakaar lu bakh

Yeen xale rewmi
Ni la ko beugue waw

Bu nu wakhtané ak sunuy baye
Mak matna ba thim rew
Lum niu wakh nyu degg ko boolé sunuy xalat
Nyi ci biti nyi ci biir fu waay meuna ne
Nen bole sunuy xalat rew mi dem kanam yaye

Yeen xale rewmi
Ni la ko beugué waw

Man daal waleu bima feetee
Maaki samay gars
Pexe mune nyung ko dieem nguir sunu rew mi naat
Sunu beugue sunu rew mi naat danyu wara boolo
Ta kat fou way meune ne sen thia yengueuto

Yeen xale rewmi
Ni la ko beugué waw

Ah thiat oh thiat ken demoul ngeu dess
Kenn warrouleu dioylo woye len thiat

Yeen xale rewmi
Ni la ko beugué waw

Sen atmi mo du atoum gune
Soxlo woul beuri wakh
Nanj dieum bolo teh won mak nyi
Nioy doule rew mi
Gone su taggou ay wadiouram
Disso ak nioom seu ndialbeen
Fu mu né ci aduna senj thia yakaar lu bakh

Yeen xale rewmi
Ni la ko beugue waw

Man daal waleu bima feetee
Maaki samay gars
Pexe mune nyung ko dieem nguir sunu rew mi naat
Sunu beugue sunu rew mi naat danyu wara boolo
Ta kat fou way meune ne sen thia deff lou bakh yaye

Yeen xale rewmi
Ni la ko beugué waw

Curiosités sur la chanson Xale de Youssou N'Dour

Quand la chanson “Xale” a-t-elle été lancée par Youssou N'Dour?
La chanson Xale a été lancée en 1990, sur l’album “Set”.

Chansons les plus populaires [artist_preposition] Youssou N'Dour

Autres artistes de World music