FALLING

Boris ARNOUX, Fabien GIROUD, Jean paul SY, Julien SOULETIE, Thierry RENAULT

Babylone is falling xanaa gisoo seen i colin?
Babylone is falling xanaa gisoo seen i waxin?
Balylone is falling xanaa gisoo seen i jëfin?
Man de yalna ma Yalla musal ci bile ñàkk teggin!

Man bi may nekk gune lañ ma jangal respect
kila magg a la ëpp sagar kon bul ko tester
Li fi maam bóoy bayyi ci lu baax warna fi rester
indiscipline bi ci dëkk bi lay manifester
education is the key, ñuy waxtaan ag xale yi
ma xamal leen ñii ñooy l’avenir de leur pays
golo yaag na bayyi, baabun yaag di dunde
Ana talibé yi? Ana ñan ñoo leen di gunge ?
Kon yaral sa doom, ci kër gi lay tambalee
te boo yarul sa bopp xawma nan nga koy dimbalee
Africa i adore tekki leen seen i boulets
dara duñ ko am nuñ buñu bayul toog di xulle
Nañ ko teg ci lu wòor, ñu roy ci lu baax
Ana Cheikh Anta Diop? Ana Mame Bamba?
Ëlëg a jara sóor te looloy aduna
suñu demee bay roy nañu roy ci lu baax

Babylone is falling xanaa gisoo seen i colin?
Babylone is falling xanaa gisoo seen i waxin?
Balylone is falling xanaa gisoo seen i jëfin?
Man de yalna ma Yalla musal ci bile ñàkk teggin!

Bes bila seytané jàppee, ba nga dem ba réer
demal Babylone di nga xamni fa la gaal gi teer
Bopp sa bopp amatuñu benn yitte
Du pàppa, du mbokk, ñoom ñëpp dañ lay éviter
Ñoom nee nañ ñoo ñu raw waye maa ngi fay gis misère
system bee fa ne di fen, di ñu sànni xeer
Brother yeewul naaj na, Babylone a ngi gën di péér
beware ndax ñu ngi comploter coup d’état militaire
Kon gëmal sa bopp te bul di jaay sa leer
ñaata ño ci jaay seen mbokk ndax ay salaires ?
Africa jogal takk taxaw ni lampadaire
mane demb mettiwoon na wante lepp dina leer
Babylone awma luma lay ñee
Fileeg ñu ngi dund dañuy bañ dee
dañuy bañ ñun suñu doom yi mel nee
melné mala yu réer ci àll bee

Chansons les plus populaires [artist_preposition] Natty Jean

Autres artistes de African reggae