SALIMATA

Boris ARNOUX, Fabien GIROUD, Jean paul SY, Sebastien FARGE

Sali daa jekk, am taar, daa melni moom lañu doon xaar
Sali de gëmul system star, bu amul taxi jël car
Te boo ko gisul Almadies mën nga ko romb Grand-Dakar
Sali du gel bu xamadi, daa am yar machalla kaar !
Sali bëgul góor bu koy jox ba paré amul ci moom respect
Bëgul am affaire ag benn góor bu ñàkk kersa
bëgul bula rombee dox doxam nga diko tester
Sali Sali dafa ànd ag simplicité kon boog…

Sali Sali yaw Salimata….. Sali (3x)
Mane de bëg naa la baby
Sali Sali yaw Salimata….. Sali (3x)
yaay sama number one baby

Sali góor yëpp dañ koy tòpp waye kenn la ci tànn
Sali du zenru gel bu ëppal ba ku ko séen da naan kii kan la
Nammul sa poche, nammul dara, du laaj greffage ag njëgu dàll
Maa lako wax barke Kara, Sali bima xam kooku Yaay Fall la nee naa
Sali dafa ànda g teggin, yaru, toog ci tànku ndayam
Bëgg ligeey, jàpp njamburam, xam fimuy yam,
Tëyye na sëram, sàmm na cëram, toog di xaar jëkëram
Sali Sali Salimata doo seen moroom
Cëy bufi toggee ceebu jën wala supp kanja
Ay feemam aki daaguwam man mooy sama ganja
Chérie bo demee dañuy wéet, kër gi namm nañu laa
Sama xol yaw rek yaa ci nekk, way-jur yi nangu nañu laa
Naqaru xol bi jeex na tàkk dumala doxaan, damalay takk
Bul tiit dépense bi dafay mat, buko defee noon yëpp ne patt
Te dumala dóor, te dumala saaga barki Yalla dumala fatt
Te duma tiit ndax wóolu naa la, when i feel bad yaw yaa may faj

Sali Sali yaw Salimata….. Sali (3x)
Mane deh bëg naa la baby
Sali Sali yaw Salimata….. Sali (3x)
yaay sama number one baby

Di naa la raay di la fóon, Tabaski ma wutal la Bali-bali
Dumala bayyi yaa ma doy, ñeneen ñi dañu bari mbele mbele
Soxna si kaay, Néné bul jooy, bokkuloog ñiy taxawaalu ci talli
Dumala bayyi nguay sooy, duma sori dinaa la wéetali
Dinala yóbbu Venise ca Italie wala bo bëgee ma yóbbula Paris
Saaru demb dinama lako taril wala ma yóbbula Congo safari
Lima bëg mooy nga free, mbëgeel bu amul benn prix
Mane ak yaw toog ci donkassigi dund real love ak peace

Chansons les plus populaires [artist_preposition] Natty Jean

Autres artistes de African reggae