SENEGAL

Jean paul SY, Julien SOULETIE, Mathieu DASSIEU, Thomas SOUIL

This is for my people,
Sénégal Njaay!

Jolli na well, music bi deh le jolli na fi nañu teg level
Ne Sénégal de kenn du ko yàq ak nimu mel
Ñu change mentalité faut que ñu change suñu xel
Xol yi nañu sell, naatange jolli well
Man de lima xam ci corruption dugg ci jail
Ku ci wàcc yoon ñu xàcc, bàcc yattu kel
Ku fi jiite xamal ni xol yi de fees na dell
kon boog nee ko rell
Ana dóorkatu waar yi? Big up Y En A Marre yi
yeewu fajar ci car yi, marchés ambulants yi
Ana taximan yi? Woolma ranguman yi
respect fi di ghetto youth yiy tangal ba Paris
baykat ag sàmmkat faut que ñu make seen money
consommer sénégalais suñu wàll moo ngii
ndax ëlëg sunu doom yi, sunu sët yi gis yoon wi
kon boog nañu boole xol yi

Ne dandu leen, dallu leen,
Sénégal ñoo ko bokk tééylu leen
dund leen, yeen ana ngeen ?
Sénégal Njaay suñu rew
(2x)

Nee naa la d’ailleurs mbindaan bi wala tailleur
moom li muy ñafe moo ko moom te kenn du ko ko may
Y a pas de sous métiers limuy ndaw ndaw sa sutura la
ñu bayyi mbed buur la, ça me saoule, teg ci fulla, coolal
Na télé bi bayyi di ñu tegal programmu kankar
faut que ñu yeete, faut que ñu tette xale yi ñun la ñu yaakaar
Gaal gi sunu gaal la te kenn waruko wengal
metitu bateau Le Joola xol yi Yalla nako seddal
Nañu bayyi tappale bi, bayyi foqqale bi
bayi tappalé bi, coow lu bare li
ku fi job di nga tekki mu neex mbaa mu metti
Na nga gëm ne mën nga tebbi, one more time
Bayyi tappale bi, bayyi foqqale
bayyi taqqale bi, coow lu bare li
ku fi job di nga tekki mu neex mbaa mu metti

Ne dandu leen, dallu leen,
Sénégal ñoo ko bokk tééylu leen
dund leen, yeen ana ngeen ?
Sénégal Njaay suñu rew (2x)

Chansons les plus populaires [artist_preposition] Natty Jean

Autres artistes de African reggae